[ 29 février 2016 by support 0 Comments ]

Seede Señ Salihu

Señ Salihu[1], wacc liggééy, laqu…

Ajuma jooju, mu ngi noonu !

Senegal ak Adduna ňakk

Lu yagg te wër tey ňak

 

Ku sax ci xol yi ak xel yi

Lii moo waral rongoň yi di xelli

Ňayu xare weetal na Xelxom

Gooru Yalla mi ittewoo Koom koom

 

Cey! Suma mënoon dellu tuut tank

Nga mey ma may dirééku ci say tank

 

Tuuba, Tuuba, fu soriwoon te jeggesi

Fune waay yennoo fa, yeksi

Jaljalu adduna ňu yebbi

Moom du ci yëy, du ci yabbi

 

Bu yekkatee kaddu, xiir ňu ci suňu Borom

Bu addoo, ňaax ňu ci liggééy ak jom

Bu dellusee, jubbanti  jikko yi ak jëf yi

Bu waqee, joxoň Kaamil bi ak Xasida yi

 

Lima am ci moom xéébu mako

Siňatiir ba firndeel nako

Cere céép bimu ma desal

Soxlaatuma luko reesal

Vendredi 29 décembre 2007

[1] Ce poème est dédié à  Serigne Saliou MBACKE, défunt Khalife général des Mourides

Partager

Laisser un commentaire

Votre adresse e-mail ne sera pas publiée. Les champs obligatoires sont indiqués avec *